BATAAXAL GU MAG GI MB SA-SAI DOOMI AADAMA
[Preamble]
u jpp te nangu ne sagu doomi aadama ak sa-saam ypp-dau yam te kenn mnuko jalgati, te lu lpp nekk na cs laay ci taxufeex ci mbirum tte ak jmm ci biir dduna.
u jpp ne akk xam ak soofantal sa-sai doomi aadama indi na aymusiba yu tar tax kpp kuy dund fippu. Temano egsi na ba mu nekk ci doomi aadama u mn a wax, xalaat, ci seen coobare, bundxatal, nkk dddu leen.
u jpp ne am na solo lool u aar sa-sai doomu aadama ak ay matukaay ci wllu yoon; ngir doomu aadama moomu kenn du ko sonal, muy fippu ci nootaange ak lu koy bunduxatal.
u jpp ne am na solo lool u gor-goorlu ba gn a rataxal jokkalante gi diggante xeet yi.
u jpp ne ci bataaxal boobule mbootaayu xeet yi yeesalaat na ay pas-pasam jme ko ci sa-sani doomi aadama yu tolloo, ci sag, ci bir lpp lu aju ci dundin diggante gor ak jigen, ci biir tawfeex gu yaa.
u jpp ne rew yi ci bokk jl nau ay matukaay ngir dgral jokkalante gi ak mbootaayu xeet yi, u naw it bu baax sann-sai doomi aadama ak tawfeex yu wor ci biir dduna ypp.
u jpp ne nd taxawal sa-sa yeek tawfeex yi nekk na lu am solo lool ngir, darajaal matukaay yooyu.
Ndaje mu mag mi biral na ci bataaxal bii ne xeet ypp, rew ypp ak kurel ypp u jpp li ci nekk, ci seen xel, te u gor-gorlu, u jaarale lii lpp ci njng mi ak yar gi.
u lawal sa-sa yeek taawfeex yi jl aymatukaay ci biirak bitim rew.
u nangu te di doxal fpp ci anam gu wr ci biir xeet yi sosoo ci rew i bokk ci mbootaay gi ak gox yi bootu ci oom.
1. Matukaay bu jkk bi
Doomi aadama ypp danuy juddu, yam ci tawfeex ci sag ak sa-sa. Nekk na it ku xam dgg te nd na ak xelam, te war naa jflante ak nawleen, te teg ko ci wllu mbokk.
2. Naareelu matukaay
Ku ne mn naa wax ne am na ay sa-sa ak ay tawfeex yu sosoo ci bataaxal bii te amul xeej ak seen, rawatina ci wllu xeet, melo, awra, lkk, diin, peete ci wllu politig, xalaat, rew mbaa askan woo mn ti sosoo, ci it wllu juddu alal ak lu mu mn ti doon.
Rax sa dolli amul xeej ak seen ci politig, yoon, mbaa doxalin wu aju ci bitim rew mbaa suuf soo xamne nit ki fa la cosaanoo; rew moomu mbaa suuf soosu moom na boppam walla deet, mbaa u yamale yengu-yngoom.
3. atteelu matukaay 
Nit kune war naa dund ci tawfeex ak kaaraange.
4. eenteelu matukaay
Waruoo def kenn jaam mbaa mbindaan. Njaam ak njaayum jaam nanguwunu ko ci anam gu mu mn ti doon.
5. Juromeelu matukaay
Waruoo mbugal, tutal, mbaa teg kenn lu metti lool lu yelloo wul ak doomu aadama.
6. Jurom benneeli matukaay
Nit ku ne am na sa-sa u war kaa nangul darajaam ci wllu yoon.
7. Jurom benneeli matukaay
Npp a yam ci kanamu yoon. Te it amul xeej ak seen, ku ne yoon woowu war na laa aar. Npp war nau leen aar ci luy jalgati liu tnk ci bataaxal bii ak bepp yngu-gngu buy indi par-parloo.
8. Jurom natteelu matukaay
Nit ku ne am na sa-sa dem ci berebi tte kaay yi ci reewam saa yoo xamne sa-saam yooyu dppook srti rewam mba yoon jalgati nau ko.
9. Jurom entteeli matukaay
Menuoo jpp, tj, mbaa genne kenn rewam te tegunu ko ci yoon.
10. Fukkeeli matukaay
Ci lu wr, nit kune mn naa egg ci berebu atte kaay wax li ko naqari ci anam gu jub, te baa nd ak par-parloo, ne dau ko taxal.
11. Fukkeeli been matukaay ak benn
1. Bpp nit bu u taqal cimbir mu tar jppe nanu ko ku set ba loolu u ko taxal leer n ginnaaw bi u ko attee. Te u taxawu ko ci lpp lu koy aar ci atte boobule. 
2. Duu tj kenn ci ay jfam mbaa lu mu ftte mbete loolu mu jf ci jamono jooju nekkul mbir mu tar ci wllu yoon, ci biir ak bitim rew. Foofu it yoon du ko teg lu dul limengok li mu def ci jamono jooju. 
12. Fukkeeli matukaay ak aar
Kenn warula xuus ci dundinu doomu aadama, bu njabootam, ci lu jm ci kram mbaa lu mengok moom, di damm it jarajaam. Buu jalgatee yii nit kune am na sa-sa u aar ko ci wllu yoon.
13. Fukkeeli matukaay ak att
1. Nit kune am na sa-sa wndeelu ni mu ko neexe, tnn it dekkuwaayam ci biir rew bu mu mn ti doon. 
2. Nit kune am na sa-sa gnn rew mu mu mn ti doon. Fimu dkk it bokk na ci-ak it dellusi ci rewam. 
14. Fukkeeli matukaay ak ent
1. Nit kune bu u ko mbugalee am na sa-sa lqu ji, mbaa aan u lq ko ci yeneni rew. 
2. Su fekkee ne nit ki dau koy toppu ginnaaw bi mu defee jyyi, mbaa yngu-yngon mngowul ak li mbootaayu xeet yi tral, sa-sa boobu. 
15. Fukkeeli matukaay ak jurom
1. Nit ku ne am na sa-sa xeetoo cim rew. 
2. Mnuu ne nit ki xeetoowul cim rew te teguu ko fenn, mbaa u xa ko sa-sa su bggee soppi xeetoom ak rewan.m 
16. Fukkeeli matukaay ak jurom benn
1. Jigen mbaa jor saa yu matee amul xaaj ak seen, ak waaso bu mu mn ti bokk, rew, mba diin am na sa-sa sy ak it sos njaboot. oo yam it sa-sa, balaa uy sey, ci biir sy ak it bu seen sy tasee. 
2. Sy kenn menunuko fas, xanaa lu jiitu ku ne ci way-dencante yi joxe xalaatam. 
3. Njaboot nekk na menneef gu am solo ci askan wi. 
17. Fukkeeli matukaay ak jurom aar
1. Ngay dund yaw doww mbaa ak mbooloo am nga sa-sa am loo moomal sa bopp. 
2. Menuoo xa kenn am aman. 
18. Fukkeeli matukaay ak jurom att
Nit kune am na sa-sa xalaat ak sa goom ci wllu diine, soppi it diineem mba ngmam, am na it tawfeex feeal diineem, mbaa ngmam, ak mbooloo, mbaa moom doww, fu dduna daje mbaa deet, jarali ko ci njngale mi, ci ay jf, ci jaamu yi ak xarbaax.
19. Fukkeeli matukaay ak jurom ent
Nit ku ne am na sa-sa wax mbaa bind lu ko soob. Ci waxam yooyule kenn menuko ce bundu xatal. Te it am na sa-sa di gstu, di jot, di wasare ci anam gu yaa ay xabaaraki xalaat ak ay jumtukaay yu mi Men ti jefandiko.
20. aar fukkeeli matukaay
1. Nit kune am na sa-sa woote ab ndaje, mbaa sos mbootaay ci jmm. 
2. Mnuoo bokk loo kenn ci mbootaay te ndu ci. 
21. aar fukkeeli matukaay ak benn
1. Nit ku ne am na sa-sa bokk ci iy doxal mbiri rewam. Mu teewal fa boppam, mbaa mu yabal ab ndaw mu teewal ko fa. 
2. Nit ku ne am na sa-sa, amul xeej ak seen liggey ci bpp brb buy doxal mbiri rewam. 
3. Pas-pasu askan mooy cslaay buy dgral lpp luy doxal rew. Pas-pas gile war na fee ci palin yu yiw yu u wara amal leg-leg ci tannin gu yaa te am sutura,mbaa topp yoon wu wor wu andak taw feex ci wllu pal. 
22. aar fukkeeli matukaay ak aar
Nit ku ne meeefu askan wi am na sa-sa u aar ko ci giru dundam. Ci dundam war na ci am xol bu sedd ci sa-saam yooyu, lu aju ci koom-koomam, ci dundinam ak ci lpp lu aju ci aadaam te di ko jox maanaa ak yookkute gu nd ak tawfeex ci wllu darajaam, loolu lpp nag ku ne doomu rew mi indi dooleem ak di jokkalante ak bitim rew te mu mngook trrin ak am-amu rew mu ne.
23. aar fukk ak atteeli matukaay
1. Nit ku ne am na sa-sa liggey, tnn it ci eanam gu ko neex liggeyamm te mu dppok ay sart yu yam te baax ci wllu liggey. Te it u aar ko ci kkub liggey. 
2. Amul xeej ak seen ku nppam nanu sa-sa u fay leen, te loolu mngok li mu aliggey. 
3. Kepp kuy liggey am na sa-sa u jox ko pay gi mu yellool, baax te mn koo dundal ak njabbotam te mu yellook sagu doomu aadama, mu mottaliku it ak yeneeni pexe su mnee am ngir aar dundinam. 
4. Nit ku ne am na sa-sa samp mbaa bokk ci ay kurel yu koy taxawu ci wllu liggeyam. 
24. aar fukk ak enteeli matukaay
Nit ku ne am na sa-sa noppalu, feexal xolal ak it di yamale diirub liggeyam ak it leg-leg muy pr, br gu nd ak xaalis.
25. aar fukk ak juromeeli matukaay
1. Nit ku ne am na sa-sa am dundingu yamamaay ngir dgral wr-gi-yaramam, raataageem ak bu njabootam, lrawatina ci wllu lekk col, dkkuwaay, lpp lu aju ci wllu paj ak bpp yngu-yngu gu am farata ci wllu dundam. Am na it sa-sa u aar ko bu liggeeyatul bu feebaree, bu amee laago, kk saxnaam mbaa srinam, mbaa mgget, mbaa mu kk li muy suturloo ci anam yu dul ci cootareem. 
2. War nau beral loxo, dimbali kpp ku tollu ci am doom ak it gune yi. Bpp xale bu juddu ci sy, mbaa bu judduwul ci sy oo bokk benn anam bu leen di aare. 
26. aar fukk ak jurom benneeli matukaay
1. Nit ku ne am na sa-sa u jngal ko, njng mi waruu ci fayaku lu mu bon bon ci njng mu suufe mi te am solo. Njng mu suufe mi lu war la. Njng mu xarala mi, te it aju ci wllu liggey war nanu koo wasaare. Amul xeej ak seen njng mu kawe mi ubbil nau ko kpp ku ko yelloo. 
2. Njng war naa indi naataange gu yaa ci ddoomi aadama te it war na dgral u naw sa-sai doomi aadama aki tawfeexam ci anam gu yaa-wat na it rataxal dggo gi ak yokkute mbootaayu xeet yi ngir jmm sax. 
3. Waajur yi oo jkk am sa-sa ci anam gi uy yare seeni doom. 
27. aar fukk ak jurom nenteeli matukaay
1. Nit ku ne am na sa-sa bokk ci dpp lu aju ci caaday askan wi, di bnneexu ci lu cu aju ak it bokk ci lpp luy suqali xarala gi ak lu ciy me. 
2. Nit ku ne am na sa-sa u aaral ko lpp lu aju ci lu mudefar ci wllu la xarala, mbind mbaa lu aju ci wllu caala. 
28. aar fukk ak jurom natteeli matukaay
Nit ku ne war naa tawaxu dpp lu aju a askan wi, ak lu aju ci bitim rewam ba sa-sa ak tawfeex yi bataaxalu xeet gi mb mn a sax.
29. aar fukk ak jurom nenteeli matukaay
1. Nit ku ne am na ay wareef yu ko war digganteem ak dkkandoom yi ngir dgral ci anam gu ya darajaam. 
2. Nit ku ne buy doxal ay sa-saam aki tawfeexam war naa sallook li ko yoon may, ngir mu mn a nangu, naw, sa-sa nawleem ba lepp lu aju ci yiw, teey ak naataange gu yaa sax ci askan wi. 
3. Sa-sa yeek tawfeex yi mnuukoo doxal ci anam gu deppoo-wul li mbootaayu xeet yi misr mbaa taxawal. 
30. Fanweereeli matukaay
Ci fnn gu mu mn ti doon ci bataaxal bii, bpp rew, mbootaay mbaa nit, warul doxal mbaa def luy yq sa-sa yeek tawfeex.
